Sección segunda

Transcript

Sección segunda
Dekkre 201/2008, bu 2 fan ci weeru desambar, biy tërël axx ak
warugari ndongo yi ci lekkol yu mak yi aggul ci uniwersite fi ci
rewum bask yi.
Xaaju ñareel.- Xeetu doxalin yu wuute
Art 30.- Doxalin yu yiwul yiDojalin yu yiwulyi ñooy:
a) tarde boo tegul fenn.
b) ñaka eew boo tegul fenn.
c) yaxx li wër daaraji , jumtuwaayu daaraji wala mbir yu ñeneen ñu nekk ci daaraji
moom, su fekke sa caggante moo ko waral.
d) ñaka topp li jangalekat wala njiiti lekkol bi diggle su fekkee tegoo ko co xeebaate,
saga wala reewande goo tay, wala tamit baña topp lila ñeneen ñiy liggey ci daara ji
diggël ci seen biir ligeey..
e) nekin, mañeer wala wax yuuy yablu ñi bokk ci lekkool bi.
f) yobu ci lekkolbi ay mbir, jumtuwaay, yërë wala sep mbir bu njiitu lekkol bi tere ci
biir sañ sañam.
g) Jëfëndiko jumtuwaay yu melni , electoronik, ay telefónico wala sep luy daw ci bii
lekkol su fekke kenn igalulako wala ningako defe bokkul ak niñula wax.
h) Fenn wala Joxé xibar yudul dëggë ligeeykati lekkoolbi bu fekkee ni yaxxaloo kenn ci
waa daaraji.
i) soti wala yombalal yenen njangaan ñuy soti ci eksamen yi, dewaar yi wala njangmi ci
liwara xamle mën mën yi wala di yore jumtuwaay yu ñu tere.
j) Yombalal nit ñuñuykoy tere ñu dugg wala and ak ñoom ci biir lekkoolbi te xamni
yoon wala njiityi nanguwuñuko.
k) Jefendikoo te tayko yef you yeneen njangaan yi moom te digaluñulako.
l) bepp jalgati sa warugar su fekkee terewul, jafeelul wala mu ayibal axxu ñeneen ñi
nekk ci jangukaaybi, bu fekkee ni loolu gisuñuni dajalin buy wuute ak nekkndoo ci
jamm la wala dojalin buy jalgati lool nekkando ci jamm.
2. Jangalekaay yi mën ñaño leral ci seeni biiri keyit dojalin yuuy dugg ci li nekk ci
xaaju 1.l bi. .
Art 31.- Doxalin yu wute ak nekkin ak jamm ci lekkoolbi
1. Doxalin yu wute ak nekkin ak jamm ci lekkoolbi ñooy:
a) baña topp diggley njiit yi, janglekatyi wala ñiy ligeen ci lekkolbi booleci
reewande wala ay saaga, xeebaate, sewalaate wala xorñoñalaate
b) Tekku wala saaga sa moroom yi wala ñeneen ñu nekk ci lekkool bi su fekke
japuñu ni doxaalin buy jafeel lool nekkandoo ci jangukaaybi, raxci dolli jeffin wala
nekkin yoo jëmële ci waa lekkool bi te ñu mëna gis ni amul gerente ni jema neewal
dolela.
c) Sacc keyitu eksamen wala soti tontu ci laaj yi, tamit di leen seddële, jaayleen wala
jëndlenn.
d) Soppi bepp keyit bu waa lekkoolbi yonnee say wajur wala say kilifa tamit nëbb say
wajur keyit yi su fekke tuut tank nga, wala tammit sopi leen.
e) Yaxx ngir jëfëndikoo bu warul, mëbël, jumtuwaay, keyit wala neegi lekkol ba, tamit
yefi yeneen nit ñi nekk ci lekkool su fekkee ni jeffya manu ñuleena tude jëffin juy yaxx
lool nekkandoo ci jangubi..
f) Dige ak ñi yor lekkool bi te bañ koo topp ngir
g) Ñakka jox nitñi axx bi ñu yellol ci ngor, sutura, seen natal su fekke danga jefandikoo
jumtuway yuuy sotti te ñoom yegguñuko.
h) Tere nit ci ludul newaldole mu def loo xamni yellonako wala forse nit ci ludul jaay
dole mu def lumu bëggul.
i) Jeffin buy yaxx jamm ji nekk ci kaar wala lekkukaay yu lekkoolbi, muy lu kenn wala
lu mboloo def.
j) Jëfëndikoo ngir saggan jumtukaay yu mañana gaañ ñeneen ci waa lekkoolbi.
k) Fen, wax xibaar budul dëgg wala nëbb yaw yaan kan ci lu yaxxal ñeneen ci waa
lekkoolbi
l) Bepp jëff ju jëmële ci xajji ak seel lu jëm ci judu, at, melokaan, awra, mënmën wala
yeembaay, werguyaram, aada, dine, ngëm, xalaat wala leepp lu japp ci nit,
coomcoomam, nekinam ci biir xeet wi saa su fekkee ni du dijalin yiy yaxx lool
nekkante ci jamm.
m) Def defati doxalin bu jaaduwul ba ñatti yoon ci diir bu weesuwull nattiweer su
fekkeeni def yu njëkkya jubbënti nañuleen, te yëggël nañuko waajuur yi su fekke tuut
tank la.
n) Bepp jëfin juy jalgati warugaru ndongo yi saasu fekkeeni day laal axxu ñeneen ñi
nekk ci jangukaay bi wala tereleen ñu def la leen warr su fekkeni du jeff juñuni day
yaxx loon nekkando ci jangukaay bi.
2. Jangalekaay yi mën ñañoo rëddë ci seeni keyitu bopp yaan doxalin ñooy bokk ci fann
bii.
Artikël 32.- Doxalin yuuy jalgati lool nekkandoo ci jammm ci jangukkay bi
1. Doxalin yuuy jalgati lool nekkandoo ci jamm ñooy:
a) Jefu rewande wala dëgër bopp bu kenn nattablewul, man naa nekk tamit lanka
topp nigël yi jëm ci jubbënti dojalin yu kilifay lekkolbi tërël, jëf joojee nga
jëmëleko ci kilifaya, janglekatyi wala ñay liggey ca lekkol bi ci seen liggeey. Ba
leegi tamit jepp wax, bindë wala natal bu ñaaw wala juy yaxx deru waa lekkolbi
b) b) xeeti saaga yu jëm ci beddeeku wala xeep juddu , at, xeet, awra, mënin, wergu
yaram, febaru xel, lakk, diine, ngëm, xalaatin wala sep luy axxu domu adama.
c) Xoxxatal nit ngir awraam , ñu jappeko ci Lua 4/2005, bu 18 ci weeru febriye, bi
jublu ci Yamale goor ak jigeen, itamit bepp waxin, dojalin wala jëf jun jëmële ci
nitt ngir diko xeex ndax nekk, xoxxatal wala jeebaane ak yaxx deru jigeen nam
d) Neewal doole ngir awraam keep ku bóok ci lekkool bi.
e) buux nit ci def lukoy gaañ ci werguyaram ak nekinunu waa lekkool bi, yen ci mbir
yooyu ñoy tux, nana, wala jël dorog.
f) Bepp doxalin buy yaax nekkandoo ci jamm, su fekkee ci mboolo la wala yëggle, moo
xam ci waxla, mbindë, film, moxamit su fekke neewël doolela ci diggënte ñu tolloo
g) Jiite wala duggë ci xeex wala leppë lu Mënë jur ayip.
h) tayko yaxx ay mbir wala moomeelu lekkoolbi, ña fay liggeeye, ña fay jaange wala
kepp ku fa bokk, moo xam lu kenn defla wala mboloo.
i) Doxalin buy yaxx nekkin ci kaaru lekkool bi, lekkukaay bi, tey def lumënë yaxxal
yeneen waa lekkool bi.
j) Ñaka jox axxam sutura, ngor wala nataalu doomu adama bu fekkee loo def la te
borom wala ay wajuuram digalulañuko.
k) Naxaate ci lu jëm mbiri lekkool bi.
l) Yaxx, soppi wala lëbëj keyit wala teere lekkol bi muy luñu bindë, natal wala itamit
nëbbë mbaa genne ay keyit su fekkee ken digalulako.
m) Lepp lu waay def te tayko te muy lu yoon daxx.
n) defati bepp dojalin bu andulak nekkandoo ci jamm ci niñu ko natale ci kaw ci xaaju
1.m), ba ñatti Ion ci biir atum jangëmi bu fekkee ñar yu njëkkëyi jubantiwoon nañuleen
te yeëgëloon nañuko waayjuryi.
ñ) Bepp beneen doxalin buy firnde baña def sa wareef su jëmee ci sa axx ak
wërguyaram, samm yaram, wax, bokk, jokko, natal, sutura ak barkeb ñepp ñu bokk ci
jangubi
2. Jangukaayi mën ñaño bindë seen keyiti bopp ngir wane jëfin yi bokk ci lii ñuy wax.
Artiikel 33.- wareef ngir defin wala ay jëf fudul lekkol bi
Jëfin yi ñu leerla ci artiikël yi weesu dañu leen di topp su fekke ni dañoo ame ci
mbeddëmi wala waxtu jang waayenak warnañoo nekk ci mbir yu bokk ci xewxew yu
laale ci lekkol bi, kaaru lekkool bi wala lekkukaaybi.
Xaaju ñatteelbi.- jumtuwaay ngir jubbanti ak yeneen yiy doxalin yu yiwulyi, yi bokkul
ak yiy yaxx lool nekkandoo ci jamm di jur
Artículo 34.- Jubbanti doxalin yu yiwulyi
Doxalin yu yiwulyi jangalekatyi dañuleen di jubbënti ak benn wala dgal yu bari:
a) Xalaat ci doxalin bu yiwulbi ak limuy jur.
b) Nangu ci kanamu ñinga toñ nni linga def yiwul.
c) Tek ay xew xew ngir yeete ci jëfin yu yiwyi.
d) Def ay jëf yu jappoo ak njuumtebi ngir yeete.
e) wooko ngir mu teew ci kanamu kilifay lekkoolbi.
Artículo 35.- Jubbanti doxalin yu wuute al nekkandoo ci jamm ci lekkool bi
1. Ngir jubbanti yii doxalin jëwriñu lekkolbi manaa tek benn ci ndigël yi ñu lim ba pare
wala japp benn ci yii yoon:
a) Xalaat ci doxalin bi wuute ak nekkando ci jamm, l bon limu mënë jur ak niñuko
mënë defare.
b) bindë ngir ëddu
c) Éddu ci kanamu waajuuryi su fekkee ndongobi tuut tank la
d)yobbu xalebi ci beneen mboloo wala kalaas ap dir wala ba faww.
e)Def liggey yuy yeete wala jëf yu mënë defar la yaxuwoon wala yuy indi ngëneel ci
lekkool bi. Lii yep dafa wara and ak doxalin wa. Ci diir bu manula weesu natti weer.
f) tere xalebi mu duggë benn wala ay kalaas wala sax ci lekkool bi. Bakerook ñuy Togo
ak moom wala ay waajuram. Mbir mi du weesu natti fan.
g) tere xalebi mu dem ci yi lekkool bi di xewal ci biti ci lu weesuwul ñatti weeri lekkool
yi topp ci doxalin bi ñuy jubbanti.
h) tereendi xalebi dem ci yen jotay yi bokk ci njangmi tey ame ci biti suñu weesuwul
nattiweeri njang yi daxalin bi am. Waye xalebi war nañukoo wutal lumu def ci
lekkoolbi.
i) Tereendi xalebi mu dugg ci lekkukaybi wala kaaru lekkoolbi lu manula weesu ñatti
weeri njangë bi doxalin biñul jubbanti am bu fekkee ci biir lekkubi wala kaarbi la mir yi
xewe.
2. Dogal yi nekk ci xaaji 1.g), 1.h) y 1.i) dañu leen di mënë def su fekkeni jeem nañuko
ñaari yoon te jubbantiwuñu dara
Artiikel 36.- Jubbanti doxalin yiiy yaxx looy nekkando ci jamm ci lekkool
1. yi doxalin, jëwriñu lekkool bi da leen di jubbanti ak benn wala ay dogal yi nekk ci
artiikel bi wesu wala yen ci yii dogal:
a) Def ay ligeey yuy yeenitki ginaaw bu xalebi wacee lekkol wale jëf yuy defar la
yaxuwoon wala yuy indi ngëneel ci lekkool bi, ci diiru juroom benni weer.
b) tere xalebi mu baña fekke benn wala yenn njangaleyi ci diiru ñattë ba ñaar fukki fan,
te xalebi baña am benn galankor ci am njangam, mën naa def yen tariyi ci kanamu
janglekatyi.
c) tere xalebi mu dugg ci jangukaay bi ci diggënte 3 ba 20 fan te baña ñakk leen ci am
njangaam, mën naa tari ci kanamu jangalekatyi.
d) terendi xalebi mu dem ci xewxew yiiy am ci biti lekkolbi wala axxu dugg ci kaarbi
wala lekkukaayu lekkoolbi ci diir bu mënë nekk ba kerook lekool di tej.
2. Dogal yi nekk ci xaaju 1.b), 1.c) y 1.d) bu artiikel bii mën ñaño nekk ci njalbeen ba
yeneen dogal yi ñu jeloon doxuñu.
Artículo 37.- Diggle ndongo bi dem beneen lekkool
1. mën ñaño digle xalebi dem beneen lekkool su fekke ni:
a) lu bon bon ba ci ñaari yoon jeem ñaño jubbënti xalebi ci doxalin bu yaxx lool
nekkandoo ci lekkool bades li nekk ci xaaju 1.n) bu artiikell 32, tamit bi fekkeeni 120
fan jall nañu ci jubbënti bu njekkë ba.
b) doxalin bay yaxx lool nekkandoo day indi wala muy yokk bedeekonte ci diggënte ay
moroom wala ngir wute awra.
c) Bu fekkeeni dañu newal dole janglekat.
d) Yen saay, bu fekkeei dañu neewal doole lool ñeneen ñu nekk ci lekkoolbi.
2 Bu fekkeeni ndongo bi def benn cidoxalinyi muskalafla wala moo ngi ci lekkoolo
muskalaf mën na ñu yobbuko beneen lekkol.
3. Digle ñu yobuko beneen lekkol dañukoy wax njitu njangalekatyi ci gox bi, moom
mooy ganaaw buñu ko yëgëlee inspectoor bi.
Artiikël 38.- Buñumenula wey natt daw jang yi
1. ganaaw buñu jeemee jubbanti doxalinyi ndongo yinga xam ni mënëtuñoo def
eksaman yi ngir seen ñaka teew mën nañuleena pareel yeneen eksaman yu wute ak yu
ña teewe lepp.
2. Lekkoolyi dinañu tërël, suñu xoolee li am, yann eksamaa la ñuy tërël waaye dañukoy
tek ci yoon.
Artiikel 39.- Li natt mënmën un xalebi ci biir askanwi di jur
Buñuy tërël nañuy ante nekkini ndongo bi ci biir askanwi mën ñaño jappaala dogalu
jubbanti yi ñu jël te doxuñu.
Artículo 40.- Ton ngir yaxx yëfu jambur
Su weesoo doglyi ngir jubbanto doxalin yi, ndongo bi jëfjëfji moo wara fay sep lumu
yaxx ci lekkolbi, wala lumu yaxal ay moromam wala ligeykati bu fekkeni moo ko tay
wala caganteem mo ko waral.