oasi 4: sant jordi - Punt d`Intercanvi

Transcript

oasi 4: sant jordi - Punt d`Intercanvi
OASI 4: SANT JORDI
OWASIS 4: SAN JOORDI
Béssu 23 ci awril ci lañ di màggal San Joordi (Diada de Sant Jordi), ki ñu dé?
Kataluña. Ci li nu ka léebal, ñu ngi waxne, dafa aamon benn rab buy buufu safara
(drac) bu dekkon ci benn dex, bo xamne bés bu ne dañ ka wara rendil Jànq. San Joordi
(di borom bax) mo fat rab wo we (borom boon), muccal jànq bi. Ci deretu rab wi ci la
juddo garabu ros ak tóor tóoram yu xonq di wone coofel ak xarito: Aada la ci Kataluña
ñuy nexle teeré (llibres) ak tóor tóor ros (roses) di wonee nobbel.
Ci coosaan Riif ci reewmum Maroc, di nañ i tassel lëbb yuy wax ci rabbu juroom naari
bopp ci ci lu niirol ak lëbbu katalan (llegenda) bi nga xamne rabb wi ak doomi buur bu
jigën nu ci ne, ben ceedo di ko muccal ci rabb wo we.
Ca Siin, rabbu bufu safara yi (dracs) da nu bokk ci lëbbal yi ak coosan gi. Sunuy Rabbi
bufu safara yi mëness nanu ne nu bax ba nu boon aajo ci seen nexaayo yaaram. Lolu
waral ka nuy jëm fo nu tolu di def lu leen di neex massalan: di leen toggal li nu gëne
bëgg, di leen waayal ak feccal.
Ci lëbb yu baari ci reew wi eslaw yi di rañee Zmei Gorinich: rabbu bufu safar bu
raggalu, di tiital askan, di yaax dekk yi ak toll yi, di sacc njanq (donzelles) yu rafet yi ci
noom Zabava, di doomi di doomo neejayu buuru Kiev. Been bess Dobrinya Nikitich,
jaambaari goor (heroi) gu siiw doggu ci jaakarlo ak moom, gàanaaw xeeq bu metti, mu
amb ndaam ci rabb wi, muccal njanq boobe.
Ca Inda, Bengalades ak Nepal di nañ di màggal ci ay bess bi jëk ci marss el Ooli ba
maagalu melo yi. Ci yi Gëne siiw late neex xaleyi. Bess bi di màggaal ndamu bax (Bé)
ci boon (Mal), ci un ko waxé ci lëbbu rabb bu jigeen bi Holika bi fattu ci taal ba mu
deffoon. Ci bess bi di nañ def ay tall fëpp, askan wi gënn ci mbend yi ak seen yeeré yu
maggat ndax da niiy foo we saanin te ndox mu xooc cuup ci melo yëpp, di waxante.
“Bul mer taay moou Holi”.
Ca Romani bessu San Joordi di nañ koy màggal, waayé benn giis giis la andal. Ci yeen
diiwaan yi un yeen seen bopp nekk boroom aalal (fortuna) bi askan wi yeené seen
bopp. Ci Yeen diiwaan màaggal San Joordi de firnde melo xobb biiy wone toll yu antu
ak werguyaram.
Ci aada Palestiin giis nañ lëbb bu niiroo ak San Joordi (Al-Jidr ci kalaama aarab) di
wax ci feen ci becc ganaar Siri, aamoon na been bënu (font d’aigua) bu rabb bufu
safara dekkoon, di lekk njanq yi. Benn bess bur bi ci boopam moo warroon joxe
doomaam. Doom ji di xar bessam solu ni sëet, di naxaar lu. Ben jaambar ñeew wone
yeenem xeeq rabb wi, gàannan si mu raay ko, muccal njanq bi aar askan ci mussiba bi.